Deglul ngelawli: Sahara munge jooy. Mi ngi xaar nit ku jup ku baax ki kay naatalaat.
Deklul ngelawli, Sahara mungaa jooy.
Dafa buga naataat
Sahara musuta nekka ndana foy-foy bi mu nekka tay : réew mu rafet te naat lam nekon.
Ñe faa dekkon dañu wegoon ala bi te doon dunda ci mbekte.
Danu daan reba di samma ak di bey.
Dañu begoon sen réew, sen réew bugaleen.
Waaye baleen nit ñu buge ya genesee, musiba genesileen
Nit ñi nga xamne wutuñu woon jàamma waaye alal reka len soxalon.
Dara doyatulenwoon lu ñu gene di am alal di gena buge.
Bu ñu dan rebba da ñu dan rey rebi ala yi, di wone ni da ñoo jup loxo fekka ñom xiifuñu sax.
De ñu daan dega gerap ya fekka soxla wuñu laxatu si taw bi wala jenta bi waaye ngir defar ay tata reka.
Jefi nit ñu buge ñoñu ñoo gaañoon Sahara.
Mu daadi doxee foofa nekka am ndanda foy foy.
Waaye nit ñafa dekoon des fa, ndax deñu ko begoon bu baax.
Mbeggeel googu nak yengal xolu Sahara.
Ngir deloleen sen mbugel googa, mu joxleen ay dekk, ay garap yu ndox wer ak mbexi dex gu mak gi tudda Niser.
Boba ba leegi nak xolam dafa naxari.
Deklul ngelawli, Sahara munge jooy. Dafa buga naataat.
Bena bes mu ni benna mak mu màndu neke lay def be mbekte mu njekema delusi.
Mag ma ne ko : « Wutal ay dekaaley nit ñu jup te baax ñu wek ala bi. »
Mu yokka sa ne ko : « Bena bes dina am nit ku ñew. Yitem mooy dekkelaat gañcax ak garap yi daan sax ca jamono yu yaga ya. Ku baax ku jup la. Dundam yepa gancax gi lako jeklel.
Waaye ngir mu dekkelaat ajana jooju, fàwu mu daan nit ñu buge ña. Dina jafe lool nak.
Li ci neex nak mooy dina am surga bu koy japale ba mu daan ay noonam. Nit kooku moo yor jiwu bilay dundalaat. »
Deglul ngelawli: Sahara munge jooy. Mi ngi xaar nit ku jup ku baax ki kay naatalaat.
Lu ñu gena weg ala bi, gen ko buga, ndanda foy-foy gi naataat.