
Sign up to save your podcasts
Or


Teggiin yii la Imaam Saaraani waxtaane ci poñ bii:
- Yëram jullit ñi
-Sant Yàlla
-Nëbb sa tolluwaay
-Néewal say mébet
Teggiini niti Yàlla yi: Xaaj ñett bi mu ngi aju ci disóo ak Yàlla ci sa mbir yépp, moytu di jublu mayu Yàlla yi fàtte Aji-Maye ji, ak wéet.
Ci waxtaan wii, da nu ciy leer dayo bi bor am ak diis bi mu diis, ngir fàttali sunu bopp, waaye fàttali sunu bokki jullit yi ngir ñu jàjju te moytu bor boodut fay.
Ci waxtaan Wii, danu ciy indi tontu ci laaj bii: Ban xam-xam mooy farata ci nit ki? Ginnaaw Yonent bi SAW daa wax ne sàkku xam-xam farata la ci jullit bi, kon yey na lu ne xam ban/yan xam-xam la war a ràngoo.
Waxtaan wii mu ngi aju ci Teggiini niti Yàlla yi ak sew-sew yi leen wuutale ak ñeneen ñi.
Waxtaan wi ab jukki la ci téereb kàngam boobu di Imaam Saaraani. Ci téere bi dafa ciy jàngale teggiini niti Yàlla yi yoy képp ku sóobu ci Yàlla te bëgg a bokk ci góor ña war nga leen ca roy.
Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo ngir ëllëg sa dara du lëj.
Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen ludut Yàlla ci gàllankoor yi la bokk.
Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.
From the publisher's feed