Sign up to save your podcastsEmail addressPasswordRegisterOrContinue with GoogleAlready have an account? Log in here.
Li tax a jóg Bëgg a Baax podcast mooy yaatal mbaax. Képp koo xam ne mbaax ñor na la, nu ngi la ciy dalal ak jàmm.... more
FAQs about Bëgg a Baax podcast:How many episodes does Bëgg a Baax podcast have?The podcast currently has 27 episodes available.
February 22, 2024Njariñu sàmm sa waxtuWaxtu daa doon lu gànjaru lool te mat a moytu a sanq. Jépp noyyi, sépp simili, wépp waxtu wurus la wow nit ki man na ci fàggu lu ko texeel ëllëg. Saggane ko nag ak di ko jeexal ci neen rëccu lay jural nit ki. Moo tax nu def ci waxtaan ngir soññ ci sunu bopp ak képp ku ko dégg....more28minPlay
February 20, 2024Masturbation, pornographie: Sabab yi ak saafara siBari na ñu am jafe-jafe ci di foowee seen bopp ba të a ko bàyyi. Ci waxtaan wii dañu ciy indi sabab yi koy waral ak yennat ci saafara yi nit man a jëfandikoo ba mucc ci xeetu mbon-mbon yu ni mel....more25minPlay
February 19, 2024Waxtaan ci IhlaasWaxtaan wii mu ngi aju ci Ihlaas ak sew-sew yi ci nekk te naqari a xam lool. Yoon wi jëmm ci ihlaas daa jafe lool te laaj ug ndimbal. Settantal ak ug xam-xam gu leer moo ciy dimbali nit....more25minPlay
February 17, 2024Jege Yàlla jaare ko ci ñaan yi tukkee ci sunnaYonent bi SAW dundam gépp jaamu Yàlla la woon. Doonoon jëmm joo xam ne dadaan tudd Yàlla ci bépp waxtu, bépp jamono. Roote ci moom ay ñaan yoy ku leeni jëfandikoo, man na la jegeel Yàlla ci kaw nga teewlu leen. Waxtaan wii mu ngi aju ci njariñu ñaan yi tukkee ci Yonent bi SAW....more31minPlay
February 17, 2024Tegginu sikarWaxtaan wii mu ngi aju ci teggin yi nekk ci sikar. Boroom xaaj ko ci ñetti xaaj. Teggin yoy laataa ngay tàmbali sikar yi lay doon, yoo xam ne ci biir sikar si lay doon ak yeneen yu aju ci boo sikaree ba noppi....more31minPlay
February 17, 2024Juróom ñaari xeeti bakkan yiWaxtaan wi mu ngi aju ci juróom ñaari xeeti bakkan yi am (les 7 catégories d’âmes). Doomu aadama dafay jaar ci fànn yu bari ci dundam gi. Bu sàggane rekk man na bokk ci way-texeedi yi. Bu góor-góorlóo nag ba noot bakkanamc man na dem ba kawe loolw...more36minPlay
February 16, 2024Aajar giNu ngi leen di aajar podcast bii di „Bëgg a Baax Podcast“. Yaatal njàngalem Lislam a ko tax a jóg. ...more1minPlay
FAQs about Bëgg a Baax podcast:How many episodes does Bëgg a Baax podcast have?The podcast currently has 27 episodes available.