Sign up to save your podcastsEmail addressPasswordRegisterOrContinue with GoogleAlready have an account? Log in here.
Li tax a jóg Bëgg a Baax podcast mooy yaatal mbaax. Képp koo xam ne mbaax ñor na la, nu ngi la ciy dalal ak jàmm.... more
FAQs about Bëgg a Baax podcast:How many episodes does Bëgg a Baax podcast have?The podcast currently has 27 episodes available.
July 31, 2024Tegginu nitu Yàlla yiCi waxtaan wii Imaam Dardiir dafa ciy waxtaane jikko yi nitu Yàlla yi di ame bu seen dox ci Yàlla matee ba seen i teggin mat sëkk (Makkaarimal ahlaax)....more32minPlay
June 22, 2024Lan mooy gis Yàlla?Ci waxtaan wii, Imaam Dardiir dafa ciy leeral xeetu teewlu yi am ak fi ñu man a yóbb nit ki ci jege Yàlla. Bu fa nit ki àgge, dina dem ba xam, yëg bir yoo xam ne maneesu koo leeral ci làmmiñ....more24minPlay
May 29, 2024Xeetu sikar yi: Tudd Yàlla ci làmmiñCi waxtaan wii, Imaam Dardiir da ciy wax ci xeetu tudd Yàlla yi am, rawatina bu làmmiñ bi nga xam ne kiy doog a sóobu ci lay tàmbalee. Ci mujj gi mu tënk ponku tassawuf yi mu jàpp ne ñoo ci gën a am solo....more26minPlay
May 18, 2024Waxtaan ci tassawuf: Sikar ak xalam (zikru ak fikru)Ci tomb yii, Imaam Dardiir da ciy wax ci solos jaamu Yàlla njël ak taxawaayu tudd Yàlla ci dundug aji-sóobu ji. Ñu doon yaari ponk yoo xam ne ki sóobu ci Yàlla da leen a war a fonk ngir jot ci càkkuteefam....more21minPlay
April 08, 2024Waxtaan ci 6i ponku tassawuf bi: Al-uzla (wéet)Wéet daa bokk ci ponk yi tassawuf teg ngir nit ki sellal xolam. Jaxasoo ak nit yi lu bari ci lu dul farata dafay sabab ay ayibu xol. Moom la Imaam Dardir di leeral ci waxtaan wii ngir aji-sóobu ji bàyyi ko xel....more21minPlay
March 27, 2024Waxtaan ci ponku tasawuf yi: Sëriñ bu mat sëriñCi dars bii, Imaam Dardiir dafay waxtaan ci ponku tassawuf yii di nangu ndogal ak wut sëriñ bu mat sëriñ. Ci ginnaaw gi mu misaal nu sëriñ bu mat sëriñ nu muy mel....more32minPlay
March 20, 2024Ñaareelu- ak ñetteelu ponk tassawuf yi: Sant ak muñCi biir fukki ponk tassawuf yi Imaam Dardiir indi ci téereem bi, waxtaan wii mu ngi aju ci lan lañuy tuddee sant Yàlla ci diine ak lan mooy muñ bi tax ñuy wax muñ....more32minPlay
March 14, 2024Ponku tassawuf bu njëkk bi: TuubTasawuf daa am ay ponk yoo xam ne nitu Yàlla yi dañu ko tëral ngir yombal aji-sóobi ji ngir mu jot ci sàkkuteefam. Ponk yooyu ñu ngi ko tënk ci fukk. Tay nag ponk bu njëkk bi lañuy waxtaane te mooy TUUB....more34minPlay
March 05, 2024Waxtaan ci tasawuf: Ñaarelu Xaaj bi: Jikko yiy gàllaankoor nit ki ci yoonu YàllaCi waxtaan wii, imaam Dardiir dafay waxtaane jikkoy xol yiy gàllankoor muriit bi ba du am ag jege Yàlla. Saalig bi (ki bëgg àgg ci Yalla) daa war a taqoo ak sikar ak jéem a dindi jikko yu ñaaw yépp ngir àgg ci Boroomam, jot ci maqamaa siddiixiya....more24minPlay
March 01, 2024Waxtaan ci tasawuf: Xaaj bu njëkk biTasawuf: Dëgg la ne ñi réere tasawuf bari nañu lool ci jamono. Ñii dañu ko réere ndax ñàkk a ci tàbbi, ak xeeb doxalinu ñi ci nekk te di ci boole lu ci bokkul. Am ñu ci nekk ba noppi réere mbir ndax ñàkk a xam li ko tax a jóg. Waxtaan wii dafay leeral tasawuf ci kaw sukandiku ci téere Imaam Dardiir bii di Xarrida al baqita. Boroom leeral ci tasawuf ci gën ja a rafeti anam ak delloo ko cosaanam. Tasawuf du lenn lu dul sellal sa xol ngir àgg ci Boroom jaam ñi....more30minPlay
FAQs about Bëgg a Baax podcast:How many episodes does Bëgg a Baax podcast have?The podcast currently has 27 episodes available.