Sign up to save your podcastsEmail addressPasswordRegisterOrContinue with GoogleAlready have an account? Log in here.
Tay ñuy def benn tambali bu ndaw ngir dégtal leen suñu « podcast » bi ñu am yéene tambali. Ñuy wax lutax ñu fas ko yéene def ci kàllaama wolof, yan wopp (sujets) lanu fas yéene waxtaane ak ki kay def ... more
FAQs about Wolof Podcast:How many episodes does Wolof Podcast have?The podcast currently has 23 episodes available.
June 05, 2023Senegaal ndax dëkk la?Tay nuy waxtaan ci tolluwaayu reew mi. Jafe-jafe yi waa reew mi di dund luko waral ak yan jàngat lanu ci man a def. Senegaal kuy wax te Yàlla tax xamni doxul ci yoon. Loolu bokk na ci li waral nit yi fippu ngir mën a jotaat seen àq....more45minPlay
March 31, 2023Xam-xamu XadiisXam-xamu xadiis lanuy waxtaane tay. Mu nekk fànn bu yaatu boo xamne woroom xam-xam yi gëstu na ñu ci ngir yoonal lépp loo xamne toxalees nako co Yonent bi (saws). Bokk na ci ay waat yu ñu leeral jëm ci xadiis, lu melni „Sanad“ te mooy goor yiy soloo xadiis yi, walla „Matn“ te mooy li ñuy soloo. Mu nekk xam-xam yu yaatu waaye fi nuy indi rek fànn wu ndaw ci seddale yi ñu def ci xadiis (classification). Baay Lahat[email protected]...more45minPlay
March 17, 2023Seex Ibra FaalTay nuy waxtaane jëmm ju am solo te mooy Seex Ibra Faal. Barina loolu lu ñu mën a jàngee ci moom ndax yiteem ju kawe. Mu nekk jëmm ji wone Seex Ahmadu Bàmba ba noppi wone nan lanu ko war a toppe ngir jariñu ci moom. Daan na wax naan Sëñ Bàmba mooy dëkk bi, man Ibra Faal maay yoon bi ciy dem. Naan la def ba taxawal loolu ak lan lanu ci mën a jàngee? Baay Lahat[email protected]...more45minPlay
March 03, 202350/50?Tay damay def taxaw setlu ci néegu sëy yi. Ndax kër gi lici war yépp ci wàllu kopar ci góor gi la war a joge walla mënees nako séddoo? Diine moom li mu wax leer na, ndax kodday ak yor góor la war. Waaye ndax léegi nit yi ci diine rek lañuy dellu? Ndax seen mbatit ak tolluwaayu jamono du amul yaneeni jeexital ci seen jëflante? Ps: ci waxtaan bi amna foo xamne polygamie la bëggoon wax, wax monogmie....more46minPlay
February 18, 2023SenegaalSenegaal némmeeku nanu fa soppite yu bari. Moo xam ci jikko, walla xalaatin walla gis-gis. Pénc mi barina lool ay jafe-jafe. Mootax tay nuy def taxaw seetlu ci luko waral ak taaj ay laaj....more46minPlay
February 03, 2023Yalla-Yalla (ñaareelu xaaj)Ñaareelu xaaju waxtaan bi nu tàmbali woon ci Yàlla-Yàlla. Nuy indi ay leeral yu bari ci kuy Seex Muusaa ak lu mu woote, lu waral coow li léeg-léeg....more45minPlay
January 20, 2023Yàlla-Yàlla (xaaj bu njëkk)Luy Yàlla-Yàlla? Bari na ñuy dégg Yàlla-Yàlla dici wax te xëyna gëstu bi ci war defuñ ko. Mootax tay ñuy indi ay leeral ci kurel boobu ci tuur bi fu mu jóge, kuy seen Sëriñ ak lan la woote....more45minPlay
July 22, 2022Sëriñ bu mat SëriñLan mooy Sëriñ bu mat Sëriñ? Ñu gis ne tay lu ëpp ci nit yi am nanu tariqa bu ñu bokk ak ci Sëriñ yu ñu jokku? Waaye lan lanu fay sàkku ak kooku nan la war a mel? Yan jikko la war a yor? Ci waxtaan bii yii ak yaneen lanuy yaatal di ci jéema indi ay leeral ak laabire. Ñu ànd ci ak jëwriñ Bàmba.[email protected]...more45minPlay
July 08, 2022„séries sénégalaises“At yii ñu weesu gis na ñu ni „séries sénégalaises“ bari nanu loolu. Ñu gis ci tamit yu bees yu bari yoo xamni miinu ñu ko woon ci réew cig fësal. Mootax ñuy def taxaw setlu di jàngat jafe-jafe yi mu mën a indi ci pénc mi. Ma àndaat ci ak jëwriñ Bàmba Jaw.[email protected]...more45minPlay
June 24, 2022Néegu séyNéegu séy lañuy waxtaane tay. Ñu setlu at yi weesu amna ay soppiku yu mag ci pénc mi. Séy yi barina ay jafe-jafe lool. Ñuy def taxaw setlu ngir man a xam luko waral ak yan saafara lanu ci man a indi. May dalal Soxna Coro Coor muy yëngu ci „aide au développement“.[email protected]...more45minPlay
FAQs about Wolof Podcast:How many episodes does Wolof Podcast have?The podcast currently has 23 episodes available.